Viatique du week-end: Modèles et repères (Par Dr. Massamba Massamba Guèye)
Quand un père tient toute sa place et remplit votre vie, il est difficile de vous trouver une autre idole, un autre modèle. Quand une mère tient tout son rôle et remplit votre vie, il vous est difficile d’importer un autre repère, une autre référence. C’est tout ce qui fait la différence entre les personnes : qui est ton père, qui est ta mère? Qu’ont-ils fait de leurs responsabilités? Les ont-ils déserter ou assumer?
Si père et mère, ont assumé les leurs, ou même les tuteurs au cas échéant, nul besoin d’emprunter des héros: ils sont et suffisent comme repères et modèles.
Chaque personne qui prend la responsabilité de fonder une famille, doit y penser pour ne pas imposer à son enfant l’obligation de chercher partout des héros nécessaires à sa vie pour combler un vide.
Être père et mère, une responsabilité à assumer ! Ne désertons pas nos responsabilités !
Dr Massamba Lba Guèye
NAYRAFET
Ku sa baay mat baay doo jëggaani baay. Ku sa ndey matal ay warugaram ci dundam doo wàlliyaani ndey. Ku say way-jur mat sëkk la ñu doon doo soxlo beneen royuwaay bu dul ñoom. Ku ka la yar mat la mu doon, doo tuñ-tuñi fune nga wuti fa mbër mu la defar.
Liy indi wuute gi ci nit ñi mooy ana ku la jur ak nu mu def ak njabootam ca jikko ya. Mbaa matoon na kilifa ba taaral yorinam wa? Mbaa mataloon na farata ya ca fayda ja ? Mbaa dumooyuwuloon warugar ya? Mbaa mataloon na jom ja? Mbaa jàngale na jomb?
Ku bëgg a samp Kër kune na ca bàyyi xel.
Ku say way-jur mat la ñu doon, doo jëggaani royuwaay ! Lépp a ngi ci kër gi!
Dr Masàmba GÉY